Iren Kokki Mutungi
Xibaar yi gën a fës | |
Juddu | 1976
Keeñaa |
Réew | Keeñaa |
Liggeey | Dawalkatu ropplaan bu mag |
Daaray tàggatu | Kenya Civil Aviation Authority (en) (dawalkatu ropplaan)
Oklahoma City Flight Schools (dawalkatu ropplaan bu mag) |
Royuwaay:Infobox Biographie Dawalkatu ropplaan bu mag bi, Iren Kokki Mutungi, ñu koy woowe Kokki Mutungi tamit, dawal ropplaan, koom gi gën a rëy ci mbooleem Penku Afrig, ci la xam-xamam màcc. Moom mooy jigeen ji jëkk a dawal <i>Boeing 787</i> <i>Dreamliner</i> ci déndu Afrig. <i>Kenya Airways</i>, di këru liggeeyukaayu Keeñaa guy yëngu ci dem bi ak dikk bi ci jaww ji lay liggeeye,.
Ay waajuram Keeñaa lañu dëkk, mu ngi juddu atum 1976. Waajuram wu góor dawalkatu ropplaan la woon ci Kenya Airways. Àllaterete na bu yàgg, léegi koosiltaŋ la ci wàllu dawal ropplaan. Lekool Moi Girls School Nairobi la Kokki doon jànge. Atum 1992, bi mu paree ci njàng mu digg-dóomu mi, fekk mu am fukki at ak juroom-ñaar, la tàmbale jàng ci lekool bi ñuy tàggate dawalkati ropplaan yi ci Neerobi, ci aydapoor Wilson, Foofu la ame lijaasa bu ñu naan licence de pilote privé, maanaam lijaasab dawalkatu ropplaan bu ndaw. Mu dem wéyali tàggatum ci dawal ropplaan ca Oklaahoma Siti ca Etaasini (USA), foofee nag la ame lijaasab dawalkatu ropplaan bu mag te kureel gile di Federal Aviation administration, di ko jébbale.
Atum 1995 mu dellu, Keeñaa, ñu jël ko Kenya Airways muy liggeey, moom rekk sax dée, moo fa nekkoon dawalkatu ropplaan bu jigeen diiru juroom-benni weer. Atum 2004, mu doon jigeenu Afrig ji jëkk a am ndigalu dawal ropplaan, bi ñu ko nangulee mu nekk dawalkatu ropplaan bu mag bu mel ni Boeing 737. Ginnaaw gi lañu ko nangul muy dawal Boeing 767.
Li ci topp mooy, mu def ab tàggatu bu koy tax a jàll ci ndawalum Boeing 787 Dreamliner. Kenya Airways wóolu ko booba ba léegi, teg ciy yoxoy ab B787, mu koy dawal, loolu tax mu nekk tey, jigeenu Afrig ji jëkk a dawal xeetu ropplaan boobu ci àdduna bi. Fukki fan ak juroom ci weeru awiril atum 2014 la njaatigeem xamle loolu.
Pasteef bi mu amoon ci nekk dawalkatu ropplaan benn bés, mu ngi yeewu ci moom bi muy nekk xale, di gis waajuram wu góor nekk Kenya Airways di fa dawal ropplaan. Komandaŋ Mutungi am na doom ju góor ju juddu ci ati 2006 yi, bëgg na di naaw ci jaww ji, di ci jàppale ay nit, rawatina dawalkati ropplaan yu jigeen yi. Septàmbar 2014, Mutungi kenn la woon ci fanweeri jigeen ak juroom-ñeent yi doon dawal ropplaan ci Kenya Airways, ci lépp lu tollu ci juroomi téemeer ak fanweer, moom moo doon dawalkatu ropplaan bu mag bi ci B787 yiy jóge Neerobi, jëm Pari. Mu ngi xalaat ci sos ag këru liggeeyukaayu dawal ropplaan gu mu moomal boppam, goo xam ne, genn wàllu dawalkat yi yépp, ay jigeen la bëgg ñu doon.
Genn wàllu jukki bile wala lépp sax, jëlees nañu ko ci jukkib Wikipejaa bu ñu bind ci àngale te tudd « Irene Koki Mutungi » (seetal ci limu bindkat yi)