Màbba Jaxu Ba

Mabba Jaxu Ba ci atum 1809 la judd ca nguurug Saalum. Baayam Njógu Ba la tuddoon, Sëriñ bu mag la nekkoon, soog a tuxu Saalum. Yaayi Màbba Jaxu, Jaxu Jéey la tuddoon,di woon wolofu jolof. Mabba Jaxu Ba, Almaami bu Rip la nekkoon, ba atum 1867. Ci at moomu , tase na ak Kumba Ndóof Seen Juuf Buur Siin bi, ci xeex bu nu tudde woon Somb-Cucun ci nguuru Siin, la deewe. Ci xeex bi Lat Joor Ngóon Latiir Jóop ak Alburi Njaay la àndaloon.