Solom


Nataalu garabu solom g

Solom mi ngi bokk ci njabootu fabaceae. Fekk baaxca Afrig sowwu jant ak Afrig gu xalaa ga.

Solom garab la gog guddaayam man naa àgg ci 30i meetar , am peer bu tal.

Xob yi dañoo nëtëx te tóttóor yi it day weex.

Garabug solom gu rëy, tóo-tóor yi di feeñ ci kawam.

Moom nag ñi ngi koy faral di baye ca Senegaal, rawatina ca bëj-saalum ba di kaasamaas.

Nataalu meññatum solom.

Meññeef mi

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Meññeef mi nag day xaw a tàppndaar, mel ni lu gulumba. Xott wu ñuul ëmb ko ñam wi ci biir day puur di ëmb benn pepp walla ñaar ci biir.

Moom nag meññeef mu gànjaru la ci gilikóos, firiktóos, feer, mañesëm, kiifur ak poroteyin.

Lem ji ñu ciy defar nag, lem ju neex, ju ñu bari soxla. Ñi ngi koy defare ca Kaasamaas ca bëj saalumub Senegaal.

Ay turam ci yeneeni làkk

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Wolof: Solom, Farañse: Tamarinier noir, Joolaa: Buparaŋ walla efrun. Kodiwaar: "Chat noir", Guinée: "Môké", Bénin: "Assissouin", Togo: "Attitoé", Àngale: "Velvet tamarind".

Xeet wii nag am na Senegaal, Bene, Burkinaa Faasoo, Kamerun, Sàntar Afrig, Caat, Kodiwaar, Ginne ekaatoryaal, Gana, Ginne Bisaawóo, Ginne Konaakiri, Liberyaa, Malu, Niseer, Niseeryaa, Sao tomé-et principr, Seraa Lewon, Sudaa, Tógóo.

Turu xam-xam wi:

[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Dialium guineense