Siin-Saalum bokk nañ ci nguuri Senegaal yi fi nekkoon. Ñaari nguuri Séeréer la ñu woon (Siin ak Saalum). Siin moo njëkk Saalum.
Moo nga nekkoon ci diggante yii: Kees, Njaareem, réewum Gaambi, mbàmbulaanu Atlas, ci diggante bëj-saalum ak sowu Senegaal, ca dexu Saalum. Diwaan ba mu nekkoon bari woon na ndox lool, amoon tamit ag joor ak ab àll, amoon na suuf su nangoon mbay.
Yenn ci dëkk ya nekkoon ca nguur ga: Ndukumaan, Kungéel, Pakaaw, Rip, Lageen, ak Ñombaato.
Séeréer si ñoo dëkkoon ca diggante bëj-gànnaar, ak sowu ca xeru Mbàmbulaanu Atlas ma. Yii ñoo nekkoon seeni dëkk: Fasnaa, Sàngamaar, Mbòojéen, Juwaalo, ak Faajut.
Saalum Séeréer si ñoo fa dëkkoon ak Tukulòor yi ak Wolof yi. Li ko dalee Kawlax ba Kafrin ca bëj-gànnaar, ba Ñooro bu Rip ca bëj-saalum. Soose yi ñoo dëkkoon Ñoombaato.
Séeréer yi nga xam ne ñoo njëkk a dëkk Siin-Saalum, Tekuruur la ñu jòge. Ba nguuru Gana gu mag ga daanoo, ca la Muraabituun yi agsi Fuuta Tooro indiwaale dundin bu bees bu aju ci ponki Lislaan. Ci noonu ngir bañ a tuub, ñu taamu gàddaay, wàcc jëm bëj-saalum ca Jolof. Ba ñu demee Jolof am fa ay jafe-jafe la ñu gën a wàcc dem sañc Sii-Saalum, muy seen dal bu mujj.
Foofa la leen Mandeŋ yi fekk, ñoom ñi jòge woon bëj-saalum ca réewumGaabu. Ci ay gëstu gis nan seeni jeexit ci Dakar, ca Sàngomaar, ak ca Jaxaaw. Lebu yi fa la ñu leen fekk daa di leen fay jëlee.
Mandeŋ, Séeréer, Wolof(lebu yi ci biir), pullaar, yii ñoo doonoon xeet yi nekkoon ca nguur ga, dëkkoon ci diwaan yi nekkoon ci wërlaayu dexu saalum gi. Mandeŋ yi ñoo nekkoon ci bëj-saalumu nguur ga, maanaan ca Ñombaato, ca Rip, ak Kolar. Lebu yi nekkoon ca bëj-gànnaar, Bawol-bawol yi ca penku.
Gelawaar mooy néeg bi daa falu ca nguuru Siin-Saalum. Li ëppoon ci ñoom ay Jambaar la ñu woon, ñoom ci cosaan ay mandeŋ la ñu, ca Gaabu la ñu jòge woon ca xarnub XIV.
Ñoom nak ca giiri Gelawaar yu mag ya la ñu bokkoon, ay mandeŋ la ñu. Mandeŋ yi donte doonu woon mbooloo mu bari, waaye ay jambaar la ñu woon. Taxawaloon nañ seen nguur gu mag ga na mu leen neexee woon. Séeréer si ñoom ay jaambur lañu, duñu ñiti ay, looloo tax mandeŋ yi manoon a jël kilifteefu nguur ga, donte Ñoom(Séeréer si) ñoo njëkk a ñëw ca barab ba. Yilif nañu nguur ga juroomi xarnu.
Mansa Waali Jonn Maane moo sos Amsell péeyub nguur ga, moo fa dëkkoon aki jambaaram. Daal di bàyyi ay way xaralaam ca Faajut, ay surgaan ca Jong Juwaal.
Mbegaan Nduur moo daaneel Aali Baana di woon njiitu diine ca tukulòor ya, doonoon sëriñ bu amoon doole ca Saalum rawatina ca Kawòon. Ci moom la Séeréer si yéegée ci jal bi, doon ay buur.
Moom Mbegaan def na lu ne ngir man a jot ci nguur gi. Ba mu ca jotee la noot nguur-nguuraan ya nekkoon ca wetam: Ngabi, Ndukumaan, Kaymoor, Mandaak, ak Jiloor, ak Genig, ak Jokkul. Dawloo buur ya teg fa ay ñoñam.
Siin ak Saalum bokk ñu woon ay àtte, waaye seenug yorteef daanaka benn la woon. Seen ñaari buur yi ñoo bokkoon maqaama: Buur. Ca Siin buur ba nu ko neex la daan àttee, waaye ca Saalum buur ba da daan diisoo ak ña ko faloon.
Boroom ndomboy tànk yu mag ya ñoo daan doxal: Njiitu Jaraaf yi, ñoom la buur daan diisool, Farba, Bëkk-néeg, Jaalige, Saltige, Njiitu dëkk yi,...
Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998
Seetal BUNTU TAARIIX |